Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 2

Na ku nekk yem ci ki mu séyal

Na ku nekk yem ci ki mu séyal

“ Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas. ” — Màrk 10:9

Yexowa, ndigal bii la ñu jox : “ Buleen wor ” (Malasi 2:​16, MN). Topp ndigal boobu, lu am solo la ci seen séy ndaxte bu ngor amulee ci séy kenn du wóolu moroomam. Te bu kóolute amul mbëggeel mënul sax.

Tey, ngor ci biir séy bareetul. Bu ngeen bëggee sàmm seen séy, fàww ngeen def ñaari mbir.

1 SEEN SÉY, NA DOON LI ËPP SOLO CI YÉEN

LI BIIBËL BI WAX : “ Sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel ” (Efes 5:​15). Seen séy dafa war a bokk ci li ëpp solo ci seen dund. Gise seen séy noonu, am xel la.

Yexowa dafa bëgg nga bàyyi xel bu baax ci ki nga séyal te ngeen dund yéen ñaar ci bànneex (Ecclésiaste 9:⁠9). Wone na ci lu leer ne waruloo sàggane mukk ki nga séyal, waaye kenn ku nekk ci yéen ñaar danga war a xool li nga mën a def ba bégal sa moroom (1 Korent 10:24). Na ku nekk won moroomam ne amal na ko njariñ te sopp na ko.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Nanga fexe ba am jot di nekk ak ki nga séyal te bàyyi sa xel bu baax ci moom

  • Bul xalaat sa bopp kese waaye nanga sóoraale ki nga séyal

2 SÀMMLEEN SEEN XOL

LI BIIBËL BI WAX : “ Képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel ” (Macë 5:28). Bu nit di xemmem keneen ku dul ki mu séyal, mel na ni mu ngi wor jëkkëram walla jabaram.

Yexowa nee na danga war a ‘ sàmm sa xol ’ (Kàddu yu Xelu 4:23 ; Yérémi 17:⁠9). Boo bëggee def loolu, fàww nga yemale sa bët (Macë 5:​29, 30). Royal ci yonent Yàlla Ayóoba mi fasoon kollëre ak ay bëtam ngir bañ a xool benn jigéen bu dul jabaram ba koy xemmem (Job 31:⁠1). Nanga fas yéene bañ a seetaan foto walla film buy wone yëfu saay-saay diggante góor ak jigéen, maanaam pornographie. Te nanga fas yéene bañ a nob kenn ku dul ki nga séyal.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Wonal ñépp ne danga takku bu baax ci ki nga séyal

  • Ki nga séyal, li muy yëg na la itteel te nanga gaaw a dagg bépp xaritoo bu dalul xelam