Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 13

Timote dafa bëggoon di dimbali nit ñi

Timote dafa bëggoon di dimbali nit ñi

Timote, xale bu góor la bu doon kontaan ci dimbali nit ñi. Dafa doon dem ci dëkk yu bare ngir dimbali nit ñi. Loolu moo tax mu kontaanoon ci dund bi mu am. Ndax bëgg nga xam lu jëm ci dundam ? —

Yaayu Timote ak maamam dañu ko doon jàngal lu jëm ci Yexowa

Timote mu ngi yaroo ci dëkk bi tudd Listar. Bi mu nekkee xale, maamam Lowis ak yaayam Ënis komaase di ko jàngal lu jëm ci Yexowa. Bi Timote di màgg, mu bëgg a dimbali nit ñi ñu xam Yexowa.

Bi mu gënee màgg tuuti, Pool dafa ko laajoon ndax bëgg na ànd ak moom ñu dem waare ci yeneen béréb. Timote tontu ko ne : ‘ Waaw-waaw ! ’ Moom pare woon na ngir dem dimbali nit ñi.

Timote ànd na ak Pool Maseduwan ci dëkk bi tudd Tesalonig. Dañu dox lu yàgg ba pare jël bato sog a àgg. Foofu, dimbali nañu ay nit ñu bare ñu xam Yexowa. Waaye amoon na ay nit ñu mer ñu leen doon jéem a def lu bon. Pool ak Timote jóge foofu dem waare ci yeneen dëkk.

Timote dafa kontaanoon ci dund bi mu am

Bi mu amee ay weer, Pool dafa wax Timote mu dellu Tesalonig ngir seeti mbokk karceen ya fa dëkk ba xam ndax ñu ngi ci jàmm. Loolu laajoon na am fit ndaxte dellu dëkk boobu wóorul woon ! Waaye Timote dem na ndaxte dafa bëggoon a xam ni mbokk yi def foofu. Bi mu demee ba dellusi, mu indil Pool xibaar yu neex. Mbokk yi nekkoon Tesalonig ñu ngi woon ci jàmm ju bare !

Timote ànd na liggéey ak Pool ay at yu bare. Pool mas na bind ne Timote mooy ki gën ci ñi mu mën a yónni ngir dimbali mbooloo yi. Timote dafa bëggoon Yexowa te bëgg nit ñi.

Ndax bëgg nga nit ñi te bëgg leen a dimbali ñu xam Yexowa ? — Su dee waaw, ni Timote dinga kontaan ci sa dund !