Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
Lan mooy xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla ? Lu tax ñu mën ko gëm ? Téere bu ndaw bii dafay tontu ci laaj yu jëm ci Biibël bi yu nit ñi faral di laaj.
Ni ñuy jëfandikoo téere bu ndaw bii
Téere bu ndaw bii, dina la dimbali nga mën a jàng li nekk ci Kàddu Yàlla, Biibël bi. Xoolal ni nga mën a def ba gis aaya yi ci sa Biibël.
LESSON 1
Lan mooy xibaaru jàmm bi ?
Jàngal xam lan mooy xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla, lu tax tey mu nekk lu am solo ak li ñu war a def.
LESSON 3
Ndax ci dëgg-dëgg xibaaru jàmm bi, ci Yàlla la jóge ?
Naka lañu mënee wóor ne li ñu wax ci Biibël bi dëgg la ?
LESSON 4
Kan mooy Yeesu Kirist ?
Jàngal ngir xam lu tax Yeesu dee, lan mooy njot gi ak li Yeesu nekk di def fi mu tollu nii.
LESSON 5
Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?
Biibël bi wax na li tax Yàlla sàkk suuf si, kañ la coono yi di jeex, ni suuf si di mel ëllëg ak nit ñi ci nar a dëkk.
LESSON 6
Ndax ñi dee dinañu mas a dekki ?
Lan mooy dal nit bu deewee ? Ndax dinañu mas a gisaat suñu soppe yi gaañu ?
LESSON 8
Lu tax Yàlla bàyyi lu bon ak coono yi di am ?
Kañ la lu bon komaase ak lu tax Yàlla bàyyi ko mu kontine ? Ndax dinañu mas a toog ba coono dootul am ?
LESSON 9
Lan ngeen mën a def ba am jàmm ci seen njaboot ?
Yexowa dafa bëgg njaboot bu nekk am jàmm. Xoolleen xelal yu am njariñ yu nekk ci Biibël bi ngir jëkkër yi, jabar yi, waajur yi, ak xale yi.
LESSON 10
Naka lañuy ràññee ni Yàlla bëgge ñu jaamu ko ?
Ndax benn diine dëgg rekk moo am ? Nañu xool juróomi poñ yiy tax ñu ràññee diine dëgg bi.
LESSON 11
Ban njariñ lañu mën a am ci topp xelal yi nekk ci Biibël bi ?
Yeesu wax na li tax ñu soxla ñu tette ñu, wax itam ñaari xelal yi ëpp solo.
LESSON 12
Naka nga mënee jege Yàlla ?
Seetal ngir xam ndax Yàlla ñaan yépp lay déglu, naka lañu war a ñaane ak leneen li ñu mën a def ngir jege Yàlla.
LESSON 13
Lan mooy xibaaru jàmm bi jëm ci wàllu diine ?
Ndax dina mas a am bés boo xam ne ñépp ñuy dund dinañu booloo jaamu benn Yàlla dëgg ji ?
LESSON 14
Lu tax Yàlla am mbootaay ?
Biibël bi wax na li tax karceen yi am mbootaay ak ni ñuy doxale ci seen biir.
LESSON 15
Lu tax nga war a kontine ?
Li nga xam ci Yàlla ak ci Kàddoom, naka lay jariñe ñeneen ñi ? Ban diggante nga mën a am ak Yàlla ?