‘ Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla! ’ Wideo yi

Ndax Yàlla am na tur ?

Ni ñuy woowe Yàlla bare na, mel ni : Aji Man ji, Sakk-kat ak Boroom. Waaye turam feeñ na 7 000 yoon ci Biibël bi.

Lu war a tax ñu gëm ne li Biibël bi wax dëgg la ?

Bu dee Biibël bi ci Yàlla la jóge, kon nag war na wuute ak yeneen téere yépp.

Biibël bi, ci kan la jóge ?

Bu dee ay nit ñoo bind Biibël bi, ndax ci dëgg-dëgg mën nañu wax ne kàddug Yàlla la ? Xalaatu kan moo nekk ci Biibël bi ?

Lan moo tax Yeesu dee ?

Ci Biibël bi deewu Yeesu dafa am solo lool. Lan mooy njariñu deewam ?

Lu tax Yàlla sàkk suuf si ?

Suuf si dafa fees ak ay yëf yu rafet lool. Diggante suuf si ak naaj bi mooy li gën, te ni mu dënge ak ni muy wëndeeloo, mooy li gën. Lu tax Yàlla def loolu lépp mu rafet bi muy sàkk suuf si ?

Lan mooy dal nit bu deewee ?

Biibël bi nee na jamono a ngiy ñëw nit ñu bare dinañu dekki, ni Lasaar

Lu tax Yàlla bàyyi coono yi di am ?

Ñu bare ñu ngi laaj lu tax àddina si fees ak bañante ak coono. Biibël bi joxe na tont bu leer te dal xel ci laaj boobu.

Ndax Yàlla nangu na fasoŋ yépp yi ko nit ñi di jaamoo ?

Nit ñu bare dañu foog ne mën nga tànn diine bu la neex.

Ndax ñaan yépp la Yàlla di déglu ?

Bu amee kuy ñaan ngir topp bëgg-bëggu boppam nag ? Walla góor buy toroxal jabaram ba pare mu ñaan Yàlla mu barkeel ko ?