Bu nit deewee, fan la jëm ?
Li Biibël bi wax
Biibël bi nee na: «Kuy dund xam ne dangay dee, waaye ku dee, xamul dara» (Kàdduy Waare 9:5; Sabóor 146:4). Kon, bu nit deewee, nekkatul di dund. Ñi dee mënatuñu xalaat, mënatuñu yëngatu te yëgatuñu dara.
«Dinga dellu di pënd»
Yàlla wax na liy xew bu nit deewee. Lii la wax suñu maam Aadama gannaaw bi mu bàkkaaree: «Pënd nga, te dinga dellu di pënd» (Njàlbéen ga 3:19). Bala Yàlla di sàkk Aadama ak «pëndu suuf», Aadama nekkul woon di dund (Njàlbéen ga 2:7). Kon bi Aadama deewee, dafa dellu nekk pënd, maanaam dundatul woon.
Kon tey, bu nit deewee loolu moo koy dal. Lii la Biibël bi wax ci liy xew bu nit walla mala deewee: «Ñoom ñépp a bokk jëm benn bérab ba, bokk jóge pëndub suuf, bokk dellu suuf» (Kàdduy Waare 3:19, 20).
Loolu tekkiwul ne gannaaw dee amatul benn yaakaar
Biibël bi méngale na dee ak nelaw (Sabóor 13:4; Yowaana 11:11-14; Jëf ya 7:60). Kuy nelaw nelaw yu xóot yëgul dara. Noonu it, ku dee yëgul dara. Waaye Biibël bi nee na Yàlla mën na yee ku dee, maanaam mayaat ko mu dund, mel ni kuy yee kuy nelaw (Ayóoba 14:13-15). Kon mën nañu ne yaakaar am na gannaaw dee ndaxte dina am ñi Yàlla di dekkal.